2.Timote 3
3
Mujug jamono dina tar
1Lii, nanga ko xam: mujug jamono, bés yu tar dina dikk. 2Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu goreedi te selladi. 3Duñu am yërmande, duñu meddi, ay soskat lañuy doon, ñu ñàkk sago, ñu néeg te bañ lu baax; 4ay workat lañuy doon, ñu teeyadi, ñu daŋŋiiral te di ñu bëgg seen bànneexu bopp, ba mu gënal leen Yàlla. 5Ragal Yàlla lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.
6Ñenn ci ñooñu ñooy yoxoosuy dugg ci biir kër yi, di fàbbi jigéen ñu ñàkk bopp, ñi seeni bàkkaar man, te seen xemmemtéef yu bare jiital leen. 7Gëstu ay àlluwa la jigéen ñooñuy wéye, waaye duñu mana xam liy dëgg mukk. 8Noonee Sànnes ak Sàmbres#3.8 Sànnes ak Sàmbres, ay tur la yu Yawut yi baaxoo tudde luxuskati Misra ya doon fexee joŋante ak Yonent Yàlla Musaa. doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm. 9Waaye duñu soreeti, ndax seenug ndof dina bir ñépp, na ñaar ñooña mujje woon.
Póol dénkooti na Timote
10Yaw nag seetlu nga bu baax sama àlluwa ak sama dundin ak sama mébét ak sama ngëm ak samag muñ ak sama cofeel ak samag ñeme coono 11ak itam bunduxataal yaak njàqare ya ma dikke woon fa dëkk yooyu di Àncos ak Ikoñum ak Listar#3.11 Ikoñum ak Listar, ay dëkk ci diiwaanu Galasi lañu woon, fa Póol tàmbalee yenam, di waare xibaaru Almasi bi.. Céy na ñu ma bunduxataale, waaye Sang bee ma musal ci lépp! 12Te kat képp ku namma farlu ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bunduxataal. 13Waaye nit ñu bon ñi ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.
14Yaw nag saxal ci li nga jàng, muy lu la wóor, nde xam nga ña nga tanqe. 15Bi ngay gone nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye. 16Mboolem Mbind mu sell mi la Yàlla wal ag Noowam, ba mu am njariñal jàngal nit ñi, femmu leen, jubbanti leen, yar leen cig njub. 17Su ko defee nitu Yàlla ki mat sëkk te matley jumtukaay ngir jépp jëf ju baax.
Currently Selected:
2.Timote 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright