Lii, nanga ko xam: mujug jamono, bés yu tar dina dikk. Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu goreedi te selladi. Duñu am yërmande, duñu meddi, ay soskat lañuy doon, ñu ñàkk sago, ñu néeg te bañ lu baax; ay workat lañuy doon, ñu teeyadi, ñu daŋŋiiral te di ñu bëgg seen bànneexu bopp, ba mu gënal leen Yàlla. Ragal Yàlla lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.