2.Timote 2
2
Beyal saw sas
1Kon nag yaw doom, doolewool yiw wi Almasi Yeesu di maye. 2Li nga dégge ci man te seede yu bare teewe ko, nanga ko jottali nit ñu wóor ñu ko mana xamal ñeneen. 3Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel. 4Ab takk-der bu bëgga neex ka ko solal kat, du xintewoo mbiri nit ña soluwul. 5Kuy joŋante it, deesu ko kaala te joŋantewul ci yoon. 6Te it beykat bi yor coonob liggéey bi, moo wara njëkka séddu ca meññeef ma. 7Defal sam xel ci li ma la wax. Boroom bi moo lay leeralal lépp.
Yeesu mooy boroom kóllëre
8Bàyyil xel ci Yeesu Almasi bi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee. 9Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng. 10Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu tànn, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.
11Kàddu gu wóor a ngii:
Su nu deewandoo ak Almasi bi,
nooy dundandoo ak moom itam;
12su nu muñee,
nooy bokk nguuru.
Su nu ko gàntalee,
moom it dinanu gàntal;
13su nu ko ñàkkee kóllëre,
mu saxoo kóllëreem,
ndax manula gàntal boppam.
Surga day sàkku ngërëmu njaatigeem
14Loolu, dee ko fàttalee, te ngay dénkaane fi kanam Yàlla, ñu bañ di xuloo ci li baat yiy tekki, ndax amul njariñ, te ñi koy dégg doŋŋ lay sànk. 15Defal sa kem-kàttan ba boo teewee fa kanam Yàlla, di ku mu gërëm, ab liggéeykat bu mucc gàcce, di xamle kàddug dëgg gi ni mu ware. 16Waaye ay kebetuy àddinay kese, moytu ko, ndax ngëmadi gu ko yées rekk lay yóbbee, 17te kàdduy ñooñu day law ni ngal. Ci ñooñu la Imene ak Filet bokk. 18Ñoo lajj yoonu dëgg, ba naan ñiy dekki, dekki nañu ba noppi, te seen wax jooju, am na ñenn ñu muy yàq seen ngëm. 19Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ki mu séddoo#2.19 Seetal ci Màndiŋ ma 16.5.,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi#2.19 Seetal ci Taalifi cant 34.15..»
20Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan. 21Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
22Xemmemtéefi ndaw nag, daw ko, te nga topp njub ak ngëm ak cofeel ak jàmm, ànd ceek ñiy tudde Boroom bi xol bu set wecc. 23Waaye werante yu xeluwul te du xam-xam, moytu ko, te xam ne ay ŋaayoo lay jur. 24Te jaamub Boroom bi warul di ŋaayoo, waaye day lewet ci ñépp, mana jàngale tey muñ. 25Jaamub Boroom bi ndànk la war di jubbanti diiŋatkat yi, ndax jombul Yàlla may leen ñu tuub, ba xam liy dëgg. 26Su ko defee seenum xel dellusi, ba ñu rëcc fiirug Seytaane mi leen jàpp, di leen defloo coobareem.
Currently Selected:
2.Timote 2: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright