2.Tesalonig 3
3
Ñaanleen ci Yàlla
1Li ci des nag bokk yi, moo di ngeen ñaanal nu, ngir kàddug Boroom bi gaawa law te am ndam na mu ko ame woon fa yeen, 2ngir itam nu mucc ci nit ñu soxor ñu bon ñi, ndax du ñépp a gëm. 3Waaye Boroom bi mooy ki jara wóolu, te moo leen di dooleel, musal leen ci ku bon ki. 4Am nanu it kóolute gu nu Boroom bi may, ne li nu leen sant, moom ngeen nekke, te moom ngeen di wéye. 5Yal na Boroom bi wommat seen xol, jëme ci cofeelu Yàlla ak muñ gi ci Almasi bi.
Yaafus warul
6Ndigal li nu leen di jox ci sunu turu Boroom Yeesu Almasi bi, moo di ngeen dànd mépp mbokk mu yaafus, te baña dëppoo ak dénkaane yi ngeen nangoo ci nun. 7Yeen ci seen bopp, xam ngeen ne ci sunuy tànk ngeen wara aw, te du ag yaafus lanu nekke woon ci seen biir. 8Lekkunu ñamu kenn ci neen, xanaa di yëngu guddi ak bëccëg, ci coonob daan sunu doole, ngir baña diisal kenn ci yeen. 9Moona du sañ-sañ bu nu ci ñàkk, xanaa bëgg leena won lu ngeen nu roye, ba ngeen aw ci sunuy tànk, 10ndax ba nu nekkee ak yeen, ndigal lanu leen joxoon moo di lii: «Ku nanguwula liggéey, bumu lekk.»
11Dégg nanu nag ne ñenn a ngi ci seen biir, ñu yaafus, duñu yëngu ci dara, lu moy di toppatoo lu seen yoon nekkul. 12Ñu ni mel lanuy sant aka dénku ngir Sang Yeesu Almasi bi, ngir ñu dal, tey yëngu, di dunde seen ñaqu bopp. 13Yeen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu baax.
14Ku ci déggul sunu kàddu yi ñu bind ci bataaxal bii nag, bàyyileen ko xel, te baña jaxasoo ak moom, ngir gàcceel ko. 15Bumu tax ngeen def ko ab noon, waaye yeddleen ko, ndax mbokk la.
Fii la Póol tëje bataaxalam
16Gannaaw loolu, Boroom bi moom jàmm, yal na leen mayal boppam jàmmi lépp ak fépp. Yal na Boroom bi ànd ak yeen ñépp.
17Tàggatoo bii, man Póol maa ko bind ci sama loxol bopp, te nii laay binde ci bépp bataaxal. 18Sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi ñeel na leen yeen ñépp.
Currently Selected:
2.Tesalonig 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright