2.Tesalonig 2
2
Ndëngte gu mag mooy jiitu bésu Sang bi
1Léegi nag bokk yi, ci wàllu dellusig sunu Sang Yeesu Almasi bi, ak sunu dajeji fa moom, li nu leen di ñaan moo di: 2bu leen lenn gaawa xañ sago ba ngeen ñàkka ànd ak seenum xel, mbaa mu di leen jaaxal; du lu ñu ne kàdduy waxyu la, du genn kàddu mbaa bataaxal bu ñu nu moomale, te di leen gëmloo ne bésu Sang bi dikk na ba noppi. 3Bu leen kenn naxe nenn, ndax bés ba du dikkagum, te fippu gu mag ga njëkkula dikk, ba ki jëmmal ndëngte te dëgmal alkute#2.3 Mbaa: di doomu alkute ji,, feeñ. 4Kooku mooy jànkoonteeka damu ci kaw mboolem lees di woowe yàlla, mbaa lees di jaamu, te mooy mujj toog ca kër Yàlla ga, ba far tudde boppam Yàlla.
5Xanaa fàttalikuwuleen ne waxoon naa leen ko, ba ma nekkee ak yeen? 6Te xam ngeen li ko téye léegi, ba du mana feeñ lu dul ca bésam. 7Kumpa la dooley ndëngte gi bàddoo te mu ngi def liggéeyam xaat, xanaa kay ki ko téye ba tey moo koy téye rekk ba keroog jëlees fi ki ko téye. 8Su boobaa la ku dëng ka di feeñ, te Sang Yeesu moo koy jàllarbee ngelawal gémmiñam, te moo koy rajaxee ca na muy feeñe bu délsee. 9Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore aki firnde ak kéemaani feni neen 10ak mboolem xeeti naxe yu njubadi lal, ñeel ñi nara sànku ndax ñàkka sopp dëgg gi, ngir nangu ko ba mucc. 11Looloo tax Yàlla yónnee leen jëf juy sànke, ngir ñu gëm aw fen. 12Su ko defee mbugal dal mboolem ñi gëmul dëgg gi, xanaa di xejjoo njubadi.
Taxawleen bu dëgër
13Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la njëkka tànn, ngir sellal leen ci Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen. 14Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi bi. 15Kon nag bokk yi, taxawleen bu dëgër te ŋoy ci dénkaane yi nu leen àgge ci sunu làmmiñu bopp ak yi nu leen bind ci sunuy bataaxal.
16Sunu Sang Yeesu Almasi bi ci boppam ak Yàlla sunu Baay mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk ak yaakaar ju wér, 17yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax ak gépp kàddu gu rafet.
Currently Selected:
2.Tesalonig 2: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright