1
2.Tesalonig 2:3
Kàddug Yàlla
KY
Bu leen kenn naxe nenn, ndax bés ba du dikkagum, te fippu gu mag ga njëkkula dikk, ba ki jëmmal ndëngte te dëgmal alkute, feeñ.
Compare
Explore 2.Tesalonig 2:3
2
2.Tesalonig 2:13
Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la njëkka tànn, ngir sellal leen ci Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen.
Explore 2.Tesalonig 2:13
3
2.Tesalonig 2:4
Kooku mooy jànkoonteeka damu ci kaw mboolem lees di woowe yàlla, mbaa lees di jaamu, te mooy mujj toog ca kër Yàlla ga, ba far tudde boppam Yàlla.
Explore 2.Tesalonig 2:4
4
2.Tesalonig 2:16-17
Sunu Sang Yeesu Almasi bi ci boppam ak Yàlla sunu Baay mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk ak yaakaar ju wér, yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax ak gépp kàddu gu rafet.
Explore 2.Tesalonig 2:16-17
5
2.Tesalonig 2:11
Looloo tax Yàlla yónnee leen jëf juy sànke, ngir ñu gëm aw fen.
Explore 2.Tesalonig 2:11
6
2.Tesalonig 2:9-10
Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore aki firnde ak kéemaani feni neen ak mboolem xeeti naxe yu njubadi lal, ñeel ñi nara sànku ndax ñàkka sopp dëgg gi, ngir nangu ko ba mucc.
Explore 2.Tesalonig 2:9-10
7
2.Tesalonig 2:7
Kumpa la dooley ndëngte gi bàddoo te mu ngi def liggéeyam xaat, xanaa kay ki ko téye ba tey moo koy téye rekk ba keroog jëlees fi ki ko téye.
Explore 2.Tesalonig 2:7