YouVersion Logo
Search Icon

2.Piyeer 3

3
Bésu Boroom bi du jaas
1Soppe yi, sama ñaareelu bataaxal a ngi nii, te bu ci nekk am na lu ma leen ci fàttali, ngir xiirtal leen ci xalaatin yu set, 2ba ngeen fàttaliku kàddu ya yonent yu sell ya jottali woon ak sunu ndigalu Boroom, sunu Musalkat, ndigal la jottalikoo ca ndaw ya ñu yebaloon ci yeen.
3Li ngeen wara njëkka xam moo di bés yu mujj ya, ay niti ñaawlekat ay dikk, di nit ñu topp seen bakkan. 4Ñooñoo naan: «Ki dige woona ñëw, ana mu? Ba maam ya nelawee de yàgg na, waaye lépp a ngi wéye na woon ca njàlbéenu àddina.» 5Li ñuy fàtte te di ko tey moo di ci kàddug Yàlla la asamaan nekke bu yàgg, te ci kàddoom la suuf bindoo ci ndox, ba génne ci ndox. 6Te ci yooyii la àddina sa woon sànkoo woon ca mbënn ma. 7Waaye asamaanu tey jii ak suuf, genn kàddug Yàlla googu moo leen yeb cib denc, ñeel sawara, kera bésub àtte ba, bésu sànkuteb aji gëmadi ñi.
8Soppe yi, lenn a ngii, buleen ko umple: benn bés ni junniy at la mel ci Boroom bi; junniy at mel ni benn bés ci moom. 9Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub. 10Waaye bésu Boroom bi nib sàcc lay dikke. Ca la asamaan yi di dëddoo ci biir coow lu réy, lu ko sosoon seey ndax tàng, suuf ak jëf ju ci biiram xoyomu.
11Gannaaw loolu lépp noonu lay seeye nag, xamleen bu baax li leen war: jëfin wu sell akug ragal Yàlla 12ak yàkkamti bésu Yàlla ba, di jëfe li koy taxa gaawa dikk, ba asamaan yi lakk ba jeex, lu ca jëmmu lakk ba seey. 13Waaye asamaan su bees ak suuf su bees te njub dëkke ko bu keroogee, moom lanuy séentu, na nu ñu ko dige woon.
14Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla. 15Sunu Boroom nag, ag muñam, jàppleen ne moo dig mucc, noonee leen ko sunu soppe, mbokk mi Póol binde woon ci xel mu rafet mi ñu ko baaxe. 16Loolu la bind ci mboolem bataaxal yi mu waxe ci moomu mbir, te mu am ci ponk yu jafee xam, ba ñi dese am njàng te seenum xel toogadi, di walbati waxam, ni ñuy def ak yeneen bind yépp, ba far sànk seen bopp.
17Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay. 18Waaye màggleen ci wàllu yiwu sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi bi, ak ci wàllu xam-xam bu ngeen ko xam. Ndam ñeel na ko tey, ba kera bés bu sax dàkk. Amiin.

Currently Selected:

2.Piyeer 3: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in