1.Yowaan 1
1
Kàddug dund gaa ngii
1Ki dale nekk ca njàlbéen, ki nu dégg, gise ko sunuy gët, niir ko, laale ko sunuy loxo, kookoo di Kàddug dund. 2Kookoo di dund ci boppam, moo feeñ, nu gis ko, te moom lanuy seedeel, di leen biralal ne kookoo di texe gu sax dàkk. Moo nekkoon fa Baay ba, te moo nu feeñu.
3Li nu gis te dégg ko, moom lanu leen di àgge, ngir yeen itam ngeen am ak nun ag jokkoog mbokk. Te sunu jokkoog mbokk googu, nook Baay bi lanu ko séqal, ak Doomam Yeesu Almasi bi. 4Loolu lanu leen di bind, ngir nu bokk mbég mu mat sëkk.
Yàlla moo dig leer
5Xibaar bi nu dégge ci moom, di leen ko àgge, mooy lii: Yàlla ag leer la, te gennug lëndëm nekkul ci moom. 6Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg. 7Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
Doxeleen leer, tàggook bàkkaar
8Su nu waxee ne amunu bàkkaar, sunu bopp lanuy nax, te amunu dëgg. 9Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi. 10Su nu nee bàkkaarunu, ab fen-kat lanu ko def, te kàddoom nekkul ci nun.
Currently Selected:
1.Yowaan 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright