1
2.Piyeer 3:9
Kàddug Yàlla
KY
Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.
Compare
Explore 2.Piyeer 3:9
2
2.Piyeer 3:8
Soppe yi, lenn a ngii, buleen ko umple: benn bés ni junniy at la mel ci Boroom bi; junniy at mel ni benn bés ci moom.
Explore 2.Piyeer 3:8
3
2.Piyeer 3:18
Waaye màggleen ci wàllu yiwu sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi bi, ak ci wàllu xam-xam bu ngeen ko xam. Ndam ñeel na ko tey, ba kera bés bu sax dàkk. Amiin.
Explore 2.Piyeer 3:18
4
2.Piyeer 3:10
Waaye bésu Boroom bi nib sàcc lay dikke. Ca la asamaan yi di dëddoo ci biir coow lu réy, lu ko sosoon seey ndax tàng, suuf ak jëf ju ci biiram xoyomu.
Explore 2.Piyeer 3:10
5
2.Piyeer 3:11-12
Gannaaw loolu lépp noonu lay seeye nag, xamleen bu baax li leen war: jëfin wu sell akug ragal Yàlla ak yàkkamti bésu Yàlla ba, di jëfe li koy taxa gaawa dikk, ba asamaan yi lakk ba jeex, lu ca jëmmu lakk ba seey.
Explore 2.Piyeer 3:11-12