1.Tesalonig 5
5
1Waaye nag bokk yi, lu jëm ci ay àpp ak bés ya loolu di am, soxlawuleen ku leen ci bind, 2ndax yeen ci seen bopp, xam ngeen xéll ne Sang bi, ni sàccub guddi lay dikke. 3Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce. 4Waaye yeen bokk yi, nekkuleen cig lëndëm, ba bés boobu di leen bett ni ab sàcc di bettee. 5Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm. 6Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago. 7Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw; ñiy màndi it, guddi lañuy màndi. 8Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu ànd ak sunu sago, te def ngëm ak cofeel sunu kiiraayal dënn; yaakaaru texe di sunu mbaxanam xare. 9Ndax kat Yàlla séddu nu am sànj, waaye ag mucc la nu moomale ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi. 10Su nuy dund ak su nuy dee, moom moo nu deewal, ngir nu mana ànd ak moom, dund. 11Kon nag noonu ngeen di ñaaxantee aka yokkante, nangeen ko wéye.
Dénkaane yii la Póol tëje
12Gannaaw loolu bokk yi, danu leen di ñaan, ñi féetewoo coonob liggéey ci seen biir te jiite leen ci yoonu Boroom bi, di leen yee, nangeen leen yég. 13Nangeen leen nawe seen kem kàttan te soppe leen noonu ndax seen liggéey. Gannaaw loolu, nangeen jàmmoo. 14Bokk yi, danu leen di dénku; yaafus yi, femmuleen leen; ñi néewu fit, ñaaxleen leen; néew-doole yi, dimbalileen leen, te it muñalleen ñépp. 15Fexeleen ba kenn du feyantoo. Waaye lu baax, deeleen ko deflante ci seen biir, te di ko defal ñépp.
16Deeleen bég, 17di saxoo ñaan, 18te di sant ak nu mu mana deme. Loolu mooy coobarey Yàlla ci yeen ñi ànd ak Almasi Yeesu.
19Buleen giimal taalub Noowug Yàlla gi, 20buleen gàttañlu ay kàdduy waxyu. 21Waaye lu mu mana doon, settantalleen ko; li baax, ngeen jàpp ci, 22te lu bon ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko.
23Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel ak seen léppi xol ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi bi feeñee. 24Ki leen woo de ku wóor la, te moo koy def it.
Póol tàggatoo na ak waa Tesalonig
25Bokk yi, nun itam, ñaanalleen nu.
26Nuyulleen nu bokk yépp, te fóonalleen nu leen, na mu gëna selle. 27Maa ngi leen di dénku nag, ngir Boroom bi, jàngleen biral bataaxal bii ngir bokk yépp.
28Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi ànd ak yeen.
Currently Selected:
1.Tesalonig 5: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright