YouVersion Logo
Search Icon

1.Tesalonig 4

4
Sellal wartéef la
1Li ci des nag, bokk yi, moo di yeena nangoo ci sunu làmmiñ jëfin wi ngeen wara jëfe ba neex Yàlla, te it moom ngeen nekke. Waaye danu leen di tinu, di leen ñaax, ci turu Sang Yeesu, ngir ngeen gënati koo jëfe. 2Xam ngeen ndigal yi nu leen jox ci turu Sang Yeesu. 3Lii moo di coobarey Yàlla: ngeen sellal te mucc ci séy yi yoon tere. 4Su ko defee kenn ku nekk ci yeen mana moom yaramu boppam ci biir sellaay ak jom, 5te ngeen ànd ak sago ci seeni xemmemtéef, baña mel ni niti xeet yi xamul Yàlla. 6Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def. 7Yàlla kat ci cellte la nu woo, waaye du ci jëfin wu setul. 8Kon nag ku jalax ndigal lii, du nit nga jalax, xanaa Yàlla, moom mi leen jox Noowam gu Sell.
9Ci wàllu mbëggeel gi war ci biiri bokk, soxlawuleen ku leen ci bind dara, ndax yeen ci seen bopp, Yàlla tàggat na leen ci soppante, 10te moom ngeen nekke seen diggante ak mboolem bokki diiwaanu Maseduwan gépp. Teewul nag, bokk yi, nu di leen ñaax, ngir ngeen gënate jëfe noonu. 11Sàkkuleen di jëfe jëfin wu dal, te ngeen di toppatoo lu seen yoon nekk, tey dunde seenu ñaq, na nu leen ko sante woon. 12Kon dingeen jekk nu ngeen di jëflantee ak ñu gëmul ña ca biti, te dungeen soxlaal kenn dara.
Tiislu bu ëpp warul
13Bokk yi nag, bëggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo. 14Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.
15Lii nu leen di àgge, te muy kàddug Boroom bi de, moo di nun ñi fiy dese bakkan ba kera Sang biy délsi, dunu jiitu way dawlu ñi fa moom. 16Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. 17Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww. 18Kon nag deeleen dëfalantee yooyu kàddu.

Currently Selected:

1.Tesalonig 4: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in