1
1.Tesalonig 4:17
Kàddug Yàlla
KY
Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.
Compare
Explore 1.Tesalonig 4:17
2
1.Tesalonig 4:16
Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki.
Explore 1.Tesalonig 4:16
3
1.Tesalonig 4:3-4
Lii moo di coobarey Yàlla: ngeen sellal te mucc ci séy yi yoon tere. Su ko defee kenn ku nekk ci yeen mana moom yaramu boppam ci biir sellaay ak jom
Explore 1.Tesalonig 4:3-4
4
1.Tesalonig 4:14
Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.
Explore 1.Tesalonig 4:14
5
1.Tesalonig 4:11
Sàkkuleen di jëfe jëfin wu dal, te ngeen di toppatoo lu seen yoon nekk, tey dunde seenu ñaq, na nu leen ko sante woon.
Explore 1.Tesalonig 4:11
6
1.Tesalonig 4:7
Yàlla kat ci cellte la nu woo, waaye du ci jëfin wu setul.
Explore 1.Tesalonig 4:7