YouVersion Logo
Search Icon

1.Piyeer 5

5
Sàmmalleen Yàlla géttam
1Mag ñi ci seen biir di seeni njiit nag, dama leen di ñaax, man miy njiit ni ñoom, di seedeb coonoy Almasi bi, te di boroom cér ci ndam li nara feeñ. 2Foralleen gétt gi ñu leen dénk. Sàmmleen ko, te bañ koo defe ñàkk pexe, xanaa xol bu tàlli, ni ko Yàlla bëgge. Buleen ko defe it koppartuy kese, waaye farluleen ci. 3Buleen jaay kilifteef ñi ñu leen dénk, waaye doonleen ay royukaay ci jur gi, 4ba bu sàmm bu mag bi feeñee, ngeen jot kaalag daraja gu dul furi.
5Naka noonu yeen ndaw ñi, nangulleen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax:
«Yàlla, ñi réy lay xeex,
ñi toroxlu, mu may leen aw yiw#5.5 Seetal ci Kàddu yu xelu 3.34.
6Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo, 7ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.
8Àndleen ak sago te teewlu! Ki leen di tuumaal, Seytaane, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax. 9Pastéefu ngëm ngeen di xeexe te xam ne benn coono bi ngeen di daj, moom la mboolem seen bokki gëmkat yi ci àddina di daj. 10Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju. 11Moom la kàttan ñeel ba fàww. Amiin.
Piyeer tàggoo na
12Silwan#5.12 Silwan mooy turu waa Room wi Gereg yi naan Silas. Seetal Jëf ya 15.22, 40. miy mbokkum gëmkat mu wóor ci sama xalaat, ci ndimbalam laa leen bind kàddu yu gàtt yii, di leen ñaax aka seedeel ne lii kat moo di yiwu Yàlla dëgg. Taxawleen ci bu dëgër.
13Ab nuyoo ñeel na leen, tukkee ca mbooloom gëmkat ma ca Babilon#5.13 Babilon foog nañu ne turu kumpa Room la. te di ñu ñu tànn ni yeen, tukkee itam ci sama doom Màrk. 14Nuyooleen te fóonantee ag cofeel. Jàmm ñeel na mboolem yeen ñi gëm Almasi bi.

Currently Selected:

1.Piyeer 5: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in