1
1.Piyeer 5:7
Kàddug Yàlla
KY
ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.
Compare
Explore 1.Piyeer 5:7
2
1.Piyeer 5:10
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.
Explore 1.Piyeer 5:10
3
1.Piyeer 5:8-9
Àndleen ak sago te teewlu! Ki leen di tuumaal, Seytaane, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax. Pastéefu ngëm ngeen di xeexe te xam ne benn coono bi ngeen di daj, moom la mboolem seen bokki gëmkat yi ci àddina di daj.
Explore 1.Piyeer 5:8-9
4
1.Piyeer 5:6
Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo
Explore 1.Piyeer 5:6
5
1.Piyeer 5:5
Naka noonu yeen ndaw ñi, nangulleen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»
Explore 1.Piyeer 5:5