1.Piyeer 4
4
Nekkalleen Yàlla
1Gannaaw Almasi bi nag moo daj coonob yaramam, yeen itam gànnaayooleen boobu yéene, ndaxte ku daj coonob yaram, tàggoo naak bàkkaar, 2ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf. 3Ndax démb kat yàgg ngeena def coobarey xeet yi xamul Yàlla, ci ay ñaawtéef ak topp seen bakkan. Dangeen daa màndi aka dem xawaare yu ànd ak moy, dëkke naan biiñ, di jaamu tuur yu seexluwu, waaye na fi yem nag. 4Ña ngeen ci daa àndal ñoo waaru tey, ba di leen sosal, ndax li ngeen àndatul ak ñoom, daw wuti googu yàqute gu af, 5waaye ñoo koy layoo ak ki nara àtte ñiy dund ak ñi dee. 6Li ñu ci jublu moo di, ñi dee tey sax, ñu àgge leen xibaaru jàmm bi, ngir bu ñu leen àttee àtteb nit ñu seen yaramu suux wara dee sax, du tee ñuy dund tey, ndax Noowug Yàlla.
Bennoo moo war gëmkat ñi
7Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiitalleen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan. 8Waaye li ci raw mooy soppanteleen cofeel gu mat sëkk, ndax cofeel, bàkkaar yu bare lay far. 9Ganalanteleen te baña jàmbat. 10Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax, di saytu ay may yu yiwu Yàlla wu yaa di joxe. 11Kuy wax, na waxe nu mu jottalee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp ndax Yeesu Almasi bi, moom mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Bu ngeen di sonn, na Almasi bi tax
12Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal. 13Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég. 14Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi bi, ndokkalee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen. 15Waaye rey nit, mbaa sàcc, mbaa def lu bon, mbaa dugg ci yëfi jàmbur, bumu waral coonoy kenn ci yeen. 16Ku sonn ndax li muy aji-gëm-Almasi nag, bumu ci rus, na sàbbaal Yàlla kay, ci woowu tur. 17Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm? 18Te it:
«Kuy jëfe njekk, su ko texe jafee,
yéefar bi, bàkkaarkat bi moom, fu mu jëm#4.18 Seetal ci Kàddu yu xelu 11.31.?»
19Kon nag ñiy sonn te coobarey Yàlla tax, nañu dénk seen bopp Yàlla, Ki sàkk te wóor, te ñuy saxoo def lu baax.
Currently Selected:
1.Piyeer 4: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright