1
1.Piyeer 4:8
Kàddug Yàlla
KY
Waaye li ci raw mooy soppanteleen cofeel gu mat sëkk, ndax cofeel, bàkkaar yu bare lay far.
Compare
Explore 1.Piyeer 4:8
2
1.Piyeer 4:10
Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax, di saytu ay may yu yiwu Yàlla wu yaa di joxe.
Explore 1.Piyeer 4:10
3
1.Piyeer 4:11
Kuy wax, na waxe nu mu jottalee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp ndax Yeesu Almasi bi, moom mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Explore 1.Piyeer 4:11
4
1.Piyeer 4:16
Ku sonn ndax li muy aji-gëm-Almasi nag, bumu ci rus, na sàbbaal Yàlla kay, ci woowu tur.
Explore 1.Piyeer 4:16
5
1.Piyeer 4:7
Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiitalleen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.
Explore 1.Piyeer 4:7
6
1.Piyeer 4:12-13
Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal. Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.
Explore 1.Piyeer 4:12-13
7
1.Piyeer 4:9
Ganalanteleen te baña jàmbat.
Explore 1.Piyeer 4:9
8
1.Piyeer 4:19
Kon nag ñiy sonn te coobarey Yàlla tax, nañu dénk seen bopp Yàlla, Ki sàkk te wóor, te ñuy saxoo def lu baax.
Explore 1.Piyeer 4:19
9
1.Piyeer 4:1-2
Gannaaw Almasi bi nag moo daj coonob yaramam, yeen itam gànnaayooleen boobu yéene, ndaxte ku daj coonob yaram, tàggoo naak bàkkaar, ngir bañatee topp xemmemtéefi bakkan, xanaa di topp coobarey Yàlla, diir bi ko dese ci kaw suuf.
Explore 1.Piyeer 4:1-2
10
1.Piyeer 4:14
Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi bi, ndokkalee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.
Explore 1.Piyeer 4:14