1
1.Yowaan 1:9
Kàddug Yàlla
KY
Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.
Compare
Explore 1.Yowaan 1:9
2
1.Yowaan 1:7
Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
Explore 1.Yowaan 1:7
3
1.Yowaan 1:8
Su nu waxee ne amunu bàkkaar, sunu bopp lanuy nax, te amunu dëgg.
Explore 1.Yowaan 1:8
4
1.Yowaan 1:5-6
Xibaar bi nu dégge ci moom, di leen ko àgge, mooy lii: Yàlla ag leer la, te gennug lëndëm nekkul ci moom. Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg.
Explore 1.Yowaan 1:5-6
5
1.Yowaan 1:10
Su nu nee bàkkaarunu, ab fen-kat lanu ko def, te kàddoom nekkul ci nun.
Explore 1.Yowaan 1:10