1
1.Korent 2:9
Kàddug Yàlla
KY
Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.»
Compare
Explore 1.Korent 2:9
2
1.Korent 2:14
Nitu neen nag du nangu lu aju ci Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom; du ko mana xam, ndax loolu Xelum Yàlla lees koy natte.
Explore 1.Korent 2:14
3
1.Korent 2:10
Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.
Explore 1.Korent 2:10
4
1.Korent 2:12
Nun nag du xelum àddina lanu jot, waaye Xel mi bawoo fa Yàlla lanu jot, ngir nu mana ràññee li nu Yàlla baaxe.
Explore 1.Korent 2:12
5
1.Korent 2:4-5
Sama kàddu ak samam njàngale jotewul woon dara ak neex làmmiñ gu xam-xamu nit ràbb, waaye dafa di ay firnde yu manooreg Noowug Yàlla lañal, ngir seen ngëm baña sukkandiku ci xam-xamu nit, te sukkandiku ci manooreg Yàlla.
Explore 1.Korent 2:4-5