1
Macë 21:22
Téereb Injiil
TI
Te lépp lu ngeen laaj cig ñaan, bu ngeen ci boolee ngëm, dingeen ci jot.»
Compare
Explore Macë 21:22
2
Macë 21:21
Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te baña werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def.
Explore Macë 21:21
3
Macë 21:9
Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”»
Explore Macë 21:9
4
Macë 21:13
naan: «Mbind mi nee na: “Sama kër dinañu ko wooye këru ñaan ci Yàlla,” waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
Explore Macë 21:13
5
Macë 21:5
«Waxal waa Siyoŋ: “Seen buur a ngi ñëw ci yéen; ku lewet la, te war mbaam-sëf, dig cumbur, doomu mbaam.”»
Explore Macë 21:5
6
Macë 21:42
Kon Yeesu ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind yi? “Doj wi tabaxkat yi sànni; mujj na di doju koñ; ci Boroom bi la loolu jóge, te yéemu nanu ci.”
Explore Macë 21:42
7
Macë 21:43
«Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam.
Explore Macë 21:43