1
Macë 22:37-39
Téereb Injiil
TI
Yeesu ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.” Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane. Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”
Compare
Explore Macë 22:37-39
2
Macë 22:40
Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.»
Explore Macë 22:40
3
Macë 22:14
Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.»
Explore Macë 22:14
4
Macë 22:30
Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
Explore Macë 22:30
5
Macë 22:19-21
Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon. Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
Explore Macë 22:19-21