1
Luug 5:4
Téereb Injiil
TI
Bi mu jànglee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gëna xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.»
Compare
Explore Luug 5:4
2
Luug 5:5-6
Simoŋ ne ko: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.» Naka lañu sànni mbaal yi, jàpp jën yu bare, ba mbaal yay tàmbalee xëtt.
Explore Luug 5:5-6
3
Luug 5:16
Waaye Yeesu moom di beddeeku ci bérab yu wéet ya, di ñaan.
Explore Luug 5:16
4
Luug 5:32
Ñëwuma ngir woo ñi jub, waaye ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar.»
Explore Luug 5:32
5
Luug 5:8
Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanam Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!»
Explore Luug 5:8
6
Luug 5:31
Yeesu ne leen: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
Explore Luug 5:31
7
Luug 5:11
Noonu ñu teer ca tefes ga, bàyyi lépp, di topp ci moom.
Explore Luug 5:11
8
Luug 5:12-13
Ni Yeesu nekke woon ci ab dëkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi dëpp jëëm ci suuf, ñaan ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral.» Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
Explore Luug 5:12-13
9
Luug 5:15
Noonu turu Yeesu di gëna siiw. Mbooloo mu bare di ñëw ci moom, ngir déglu ko te mu faj seeni jàngoro.
Explore Luug 5:15