1
Luug 6:38
Téereb Injiil
TI
Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkos te yëngal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.»
Compare
Explore Luug 6:38
2
Luug 6:45
Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax.
Explore Luug 6:45
3
Luug 6:35
Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, baña yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.
Explore Luug 6:35
4
Luug 6:36
Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande.
Explore Luug 6:36
5
Luug 6:37
«Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal.
Explore Luug 6:37
6
Luug 6:27-28
«Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ. Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.
Explore Luug 6:27-28
7
Luug 6:31
Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.
Explore Luug 6:31
8
Luug 6:29-30
Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki. Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.
Explore Luug 6:29-30
9
Luug 6:43
«Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax.
Explore Luug 6:43
10
Luug 6:44
Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla reseñ ci xaaxaam.
Explore Luug 6:44