Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkka toog, xalaat ñaata la ko wara dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu mana àggale liggéey bi? Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te manu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko: “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye manu koo àggale.”