1
Luug 13:24
Téereb Injiil
TI
«Defleen seen kem kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéema dugg, waaye duñu ko man.
Compare
Explore Luug 13:24
2
Luug 13:11-12
Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu wara mat fukki at ak juróom ñett; dafa xuuge woon te manul woona siggi dara. Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
Explore Luug 13:11-12
3
Luug 13:13
Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.
Explore Luug 13:13
4
Luug 13:30
Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»
Explore Luug 13:30
5
Luug 13:25
Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.”
Explore Luug 13:25
6
Luug 13:5
Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.»
Explore Luug 13:5
7
Luug 13:27
Mu ne leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!”
Explore Luug 13:27
8
Luug 13:18-19
Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko mana méngaleel? Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
Explore Luug 13:18-19