1
Yowaan 7:37-38
Téereb Injiil
TI
Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na: “Ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.”»
Compare
Explore Yowaan 7:37-38
2
3
Yowaan 7:39
Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroona jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon.
Explore Yowaan 7:39
4
Yowaan 7:24
Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
Explore Yowaan 7:24
5
Yowaan 7:18
Nit kiy wax ci coobareem nag, day wuta màggal boppam, waaye kiy wuta màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.
Explore Yowaan 7:18
6
Yowaan 7:16
Yeesu daldi leen wax ne: «Li may jàngle, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
Explore Yowaan 7:16
7
Yowaan 7:7
Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul.
Explore Yowaan 7:7