1
Yowaan 6:35
Téereb Injiil
TI
Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar.
Compare
Explore Yowaan 6:35
2
Yowaan 6:63
Xelu Yàlla mi mooy joxe dund; ñam wi jariñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci Xelum Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dund.
Explore Yowaan 6:63
3
Yowaan 6:27
Buleen liggéeyal ñam wuy yàqu; li gën mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. Ñam woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam.»
Explore Yowaan 6:27
4
Yowaan 6:40
Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!»
Explore Yowaan 6:40
5
Yowaan 6:29
Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.»
Explore Yowaan 6:29
6
Yowaan 6:37
Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi.
Explore Yowaan 6:37
7
Yowaan 6:68
Simoŋ Piyeer ne ko: «Boroom bi, ci kan lanuy dem? Yaa yor kàddu yiy joxe dund gu dul jeex.
Explore Yowaan 6:68
8
Yowaan 6:51
Man maay ñam wiy dund te wàcce ci asamaan. Ku lekk ci ñam wii, dinga dund ba fàww. Te it ñam wi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir àddina mana dund.»
Explore Yowaan 6:51
9
Yowaan 6:44
Kenn manula ñëw ci man te Baay, bi ma yónni, xiirtalu la ci; te man dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
Explore Yowaan 6:44
10
Yowaan 6:33
Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.»
Explore Yowaan 6:33
11
Yowaan 6:48
Maay ñam wiy joxe dund.
Explore Yowaan 6:48
12
Yowaan 6:11-12
Yeesu daldi jël mburu ya, gërëm Yàlla, ba noppi séddale ko ña fa toogoon. Mu jox leen itam jën, ba ñu doyal sëkk. Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: «Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer.»
Explore Yowaan 6:11-12
13
Yowaan 6:19-20
Bi ñu joowee lu wara tollook juróom benni kilomet, ñu séen Yeesu, muy dox ci kaw dex gi, jëm ci ñoom, ñu daldi tiit. Waaye Yeesu ne leen: «Man la, buleen tiit!»
Explore Yowaan 6:19-20