1
Yowaan 8:12
Téereb Injiil
TI
Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.»
Compare
Explore Yowaan 8:12
2
Yowaan 8:32
Te it dingeen xam dëgg gi, te dëgg gi dina leen goreel.»
Explore Yowaan 8:32
3
Yowaan 8:31
Yeesu ne Yawut ya ko gëmoon: «Bu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu wóor.
Explore Yowaan 8:31
4
Yowaan 8:36
Kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen doon ay gor tigi.
Explore Yowaan 8:36
5
Yowaan 8:7
Bi laaj ya baree, mu siggi ne leen: «Ku masula def bàkkaar ci yéen, na ko jëkka sànniy xeer.»
Explore Yowaan 8:7
6
Yowaan 8:34
Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, képp kuy bàkkaar, jaamu bàkkaar la.
Explore Yowaan 8:34
7
Yowaan 8:10-11
Mu daldi siggi ne ko: «Jigéen ji, ana ñi la doon jiiñ njaaloo? Ndax kenn tegu la tooñ?» Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it ci sama wàll, duma la daan. Demal, waaye bul defati bàkkaar.»
Explore Yowaan 8:10-11