1
Yawut ya 5:14
Téereb Injiil
TI
Waaye ñam wu dëgër, ñi mat a ko yelloo, maanaam ñiy jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon.
Compare
Explore Yawut ya 5:14
2
Yawut ya 5:12-13
Bu yàgg ngeen waroona jàngal ñeneen ñi, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci kàddug Yàlla. Léegi nag yéena ngi tollu fi ñu leen wara nàmpale, ndaxte àttanuleen ñam wu dëgër. Képp kuy nàmp, ab xale nga ba tey. Jëfeegoo njàngle mi jëm ci wàllu njubte.
Explore Yawut ya 5:12-13
3
Yawut ya 5:8-9
Waaye li muy nekk nekk doom, teewul mu jàng déggal Yàlla, jaare ko ci coono bi mu daj. Noonu la àgge cig mat, ñu def ko ki waral mucc gi dul jeex, ngir ñi ko déggal ñépp.
Explore Yawut ya 5:8-9
4
Yawut ya 5:7
Giiru dundam gépp ci àddina, Kirist da daan ñaan wall ci Yàlla, di ko dénku, boole ko ak i jooy ak i rongooñ. Da doon ñaan ci Yàlla, mi ko mana musal ci dee. Te ñaanam nangu na, ndax ni mu jébbale boppam Yàlla.
Explore Yawut ya 5:7