1
Yawut ya 4:12
Téereb Injiil
TI
Xam nanu ne kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gëna ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol.
Compare
Explore Yawut ya 4:12
2
Yawut ya 4:16
Kon nag nanu am kóolute ci jege jalu Yàlla bu yiw ba, ngir jot yërmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.
Explore Yawut ya 4:16
3
Yawut ya 4:15
Sarxalkat bu mag bi nu am, du ku manula bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar.
Explore Yawut ya 4:15
4
Yawut ya 4:13
Te itam amul mbindeef mu mana nëbbu Yàlla, waaye lépp a ubbiku, ba ne fàŋŋ ci bëti ki nu wara àtte.
Explore Yawut ya 4:13
5
Yawut ya 4:14
Gannaaw am nanu sarxalkat bu maga mag bu àgg ba ca kanam Yàlla, di Yeesu Doomu Yàlla ji, nanu jàpp bu dëgër yoon wi nu gëm.
Explore Yawut ya 4:14
6
Yawut ya 4:11
Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn baña déggadi, ba daanu ni maam ya ca màndiŋ ma.
Explore Yawut ya 4:11