Yawut ya 5:12-13
Yawut ya 5:12-13 TI
Bu yàgg ngeen waroona jàngal ñeneen ñi, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci kàddug Yàlla. Léegi nag yéena ngi tollu fi ñu leen wara nàmpale, ndaxte àttanuleen ñam wu dëgër. Képp kuy nàmp, ab xale nga ba tey. Jëfeegoo njàngle mi jëm ci wàllu njubte.





