Te yéen ñi doon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, Yàlla dundalaat na leen ak Kirist, baal nu sunuy bàkkaar yépp. Mbind mi nu doon tiiñal, te daa nu yey ndax ay sàrtam, Yàlla far na ko, dindi ko, daajaale ko ca bant ba Kirist deeye.