Bible App logo
Search Icon

Kolos 2:16-17

Kolos 2:16-17 TI

Kon nag bu leen kenn teg tooñ ci li jëm ciy ñam mbaa naan, ci màggal mbaa xewu weer wu feeñ, mbaa ci bésub noflaay. Loolu lépp nag takkandeer la woon buy misaal li waroona ñëw, waaye lu dëggu li mi ngi ci Kirist.