1
2.Korent 5:17
Téereb Injiil
TI
Kon bu nit bokkee ci Kirist, mbindeef mu bees la. Li jëkk wéy na, lu bees a fi teew.
Compare
Explore 2.Korent 5:17
2
2.Korent 5:21
Kirist mi masula def bàkkaar, Yàlla def na ko bàkkaar ci sunu wàll, ngir ci sunu bokk ci moom, nu mana doon njubteg Yàlla.
Explore 2.Korent 5:21
3
2.Korent 5:7
ndaxte doxewunu ab gis, waaye ngëm lanuy doxe.
Explore 2.Korent 5:7
4
2.Korent 5:18-19
Te loolu lépp a ngi sosoo ci Yàlla, mi nu jubale ak boppam jaare ko ci Yeesu Kirist, te sas nu nuy waare juboo googu: maanaam, Yàlla jaar na ci Kirist, di jubale waa àddina ak boppam te sëfu leen seeni tooñ. Kàddug juboo googu, Yàlla dénk na nu ko.
Explore 2.Korent 5:18-19
5
2.Korent 5:20
Ay ndaw lanu, yu Kirist yónni, te Yàllaa ngi woo nit ñi jaare ko ci nun. Kon nag ci turu Kirist, nu ngi leen koy ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla.
Explore 2.Korent 5:20
6
2.Korent 5:15-16
Te dee na ngir ñépp, ngir ñiy dund dootuñu dund ngir seen bopp, waaye ngir ki dee ci seen wàll te dekki. Kon nag gannaaw-si-tey xoolatunu kenn ci gis-gisu àddina. Su fekkee mas nanoo xool Kirist ci gis-gisu àddina, léegi xooleetunu ko noonu.
Explore 2.Korent 5:15-16
7
2.Korent 5:14
Ndaxte mbëggeelu Kirist moo nuy jiite, ndax wóor na nu ne ndegam kenn rekk a dee ngir ñépp, kon ñépp a dee.
Explore 2.Korent 5:14