1
2.Korent 4:18
Téereb Injiil
TI
Kon diirunu li ñuy gis waaye li ñu dul gis. Ndaxte li ñuy gis day wéy, waaye li ñu dul gis day sax ba fàww.
Compare
Explore 2.Korent 4:18
2
2.Korent 4:16-17
Loolu moo tax sunu yaakaar du tas. Bu fekkee sax sunu yaram day yàqu jëm cig mag, sunu ruu moom, bés ak bés muy gëna yeesaat. Ndaxte sunu coono bu woyof bi dul yàgg, dafa nuy jural ndam lu bare, ba suul coono bi, tey sax abadan.
Explore 2.Korent 4:16-17
3
2.Korent 4:8-9
Dañu nuy sonal fu nekk, waaye kenn tancu nu. Dañu nuy dugal ci ruq yi, waaye dinanu ci génn. Dañu nuy fitnaal, waaye Yàlla du nu wacc mukk. Tër nañu nu, waaye kenn doggaliwu nu.
Explore 2.Korent 4:8-9
4
2.Korent 4:7
Leer googu ci sunu xol mi ngi mel ni alal, waaye ñu ngi ko def ci nun ñi néew doole niy njaq kese, ngir kàttan gu ëpp xel gi, bawoo ci Yàlla te du ci nun.
Explore 2.Korent 4:7
5
2.Korent 4:4
Ñoom la yàllay jamono ji gëlëmal seen xel, ngir ñu baña gis leeru xibaaru jàmm, biy wone ndamu Kirist, mi di melokaanu Yàlla.
Explore 2.Korent 4:4
6
2.Korent 4:6
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer leer ci biir lëndëm,» moo leer ci sunu xol, ngir leeral nu ak xam-xamu ndamu Yàlla, liy feeñ ci xar kanamu Kirist.
Explore 2.Korent 4:6