1
2.Korent 6:14
Téereb Injiil
TI
Buleen likkoo ak ñi gëmul. Gan àndandoo moo mana am diggante njubte ak ndëngte? Gan booloo moo mana am diggante leer ak lëndëm?
Compare
Explore 2.Korent 6:14
2
2.Korent 6:16
Nan la kër Yàlla mana mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy kër Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe: «Dinaa dëkk ci seen biir, tey dox ànd ak ñoom, ma nekk seen Yàlla, ñuy samay gaay.»
Explore 2.Korent 6:16
3
2.Korent 6:17-18
Kon nag Boroom bi nee na: «Génnleen biir ñooñu te beru. Buleen laal dara lu am sobe, kon dinaa leen teeru. Dinaa nekk baay ci yéen, ngeen di doom ci man, muy góor, di jigéen. Moom la Aji Man ji wax.»
Explore 2.Korent 6:17-18
4
2.Korent 6:15
Gan déggoo moo mana am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo mana am diggante ki gëm ak ki gëmul?
Explore 2.Korent 6:15