1
1.Korent 3:16
Téereb Injiil
TI
Xanaa xamuleen ne yéenay kër Yàlla, te Xelum Yàlla dëkk na ci yéen?
Compare
Explore 1.Korent 3:16
2
1.Korent 3:11
Ci li jëm ci fondamaa bi, kenn manu fee tëral beneen bu dul bi fi xasa taxaw, muy Yeesu Kirist.
Explore 1.Korent 3:11
3
1.Korent 3:7
Ki jëmbët nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, waaye Yàlla miy jebbil rekk moo am solo.
Explore 1.Korent 3:7
4
1.Korent 3:9
Nu ngi liggéeyandoo ci liggéeyu Yàlla; yéenay toolu Yàlla, yéenay taaxum Yàlla.
Explore 1.Korent 3:9
5
1.Korent 3:13
sa liggéey dina fés, ndaxte bés baa koy xamle. Bés boobu dina fenk ni sawara, te sawara si dina nattu liggéeyu ku nekk.
Explore 1.Korent 3:13
6
1.Korent 3:8
Ki jëmbët ak ki suuxat benn lañu. Teewul nag ku nekk dina jot yool bu tollook liggéeyam.
Explore 1.Korent 3:8
7
1.Korent 3:18
Kon bu kenn nax boppam: su kenn ci yéen tegee boppam boroom xam-xam ci gis-gisu àddina sii, kooku na doon dof, ngir am xam-xam bu wóor.
Explore 1.Korent 3:18