YouVersion Logo
Search Icon

1.Korent 3

3
Xuloo ci biir mbooloom ñi gëm
1Man nag bokk yi, manuma woona wax ak yéen ni ay nit ñuy déggal Xelum Yàlla, waaye waroon naa wax ak yéen ni ñuy topp seen nafsu, mel ni ay liir ci seen dund ci Kirist. 2Nàmpaloon naa leen, waaye joxuma leen dugub, ndaxte àttanuleen ko woon, te ba léegi sax àttanuleen ko 3ci li ngeen di topp seen nafsu. Bu ñeetaan ak xuloo amee ci seen biir, xanaa du loolu mooy wone ne dangeena topp seen nafsu, di doxale ni niti àddina? 4Bu kenn yéglee ne: «Man ci Pool laa bokk,» keneen ne: «Man ci Apolos,» ndax jëfewuleen ni niti àddina rekk?
5Kuy Apolos? Ak kuy Pool? Nun ay surga rekk lanu, yu ngeen jaare, ba gëm. Te Boroom bi moo sas ku nekk liggéeyam. 6Maa jëmbët, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil. 7Ki jëmbët nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, waaye Yàlla miy jebbil rekk moo am solo. 8Ki jëmbët ak ki suuxat benn lañu. Teewul nag ku nekk dina jot yool bu tollook liggéeyam. 9Nu ngi liggéeyandoo ci liggéeyu Yàlla; yéenay toolu Yàlla, yéenay taaxum Yàlla.
10Man nag teg naa fondamaa bi, ni tabaxkat bu man liggéeyam, dëppook sas wi ma Yàlla jagleel ci kaw yiwam. Te keneen a ngi tabax ci kaw; waaye na ku nekk teeylu ci ni muy tabaxe. 11Ci li jëm ci fondamaa bi, kenn manu fee tëral beneen bu dul bi fi xasa taxaw, muy Yeesu Kirist. 12Ku tabax ci kaw fondamaa bi, wurus, xaalis, per, dénk, gittax walla boob, 13sa liggéey dina fés, ndaxte bés baa koy xamle. Bés boobu dina fenk ni sawara, te sawara si dina nattu liggéeyu ku nekk. 14Ku sa liggéey dëgër, dinga jot yool. 15Waaye ku sa liggéey lakk, dinga ñàkk. Yaw ci sa bopp dinga mucc, waaye mel ni ku rëcc ci sawara si.
16Xanaa xamuleen ne yéenay kër Yàlla, te Xelum Yàlla dëkk na ci yéen? 17Ku yàq kër Yàlla gi, Yàlla dina la yàq, ndaxte kër Yàlla gi dafa sell, te yéenay kër googu.
18Kon bu kenn nax boppam: su kenn ci yéen tegee boppam boroom xam-xam ci gis-gisu àddina sii, kooku na doon dof, ngir am xam-xam bu wóor. 19Ndaxte xam-xamu àddina si, ndof la fa Yàlla. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla jàpp na ñu muus ñi, ba seen fiir këppu ci seen kaw.» 20Te it: «Boroom bi xam na xalaati boroom xam-xam yi; xam ne duñu mujj fenn.»
21Kon nag bu kenn tiitaru ndax nit ñi, ndaxte yéena moom lépp, 22muy Pool, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di lu am, di luy ñëw; lépp, yéena ko moom. 23Yéen, Kirist a leen moom; Kirist, Yàllaa ko moom.

Currently Selected:

1.Korent 3: TI

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in