Kookoo leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi bi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk, mbóot mu Bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal, kooku mooy Yàlla mi wéetoo xam-xam, te moom la ndam ñeel ba fàww, ndax Yeesu Almasi bi! Amiin.