Room 16
16
Póol nuyu na waa Room
1Boole naa leen nag ak sunub jigéen Febe, mu di ab jàppalekatub mbooloom gëmkat ma dëkke Señsere. 2Dalalleen ko ci turu Boroom bi, ni ko ñu sell ñi yelloo, te ngeen taxawu ko ci lépp lu mu aajowoo, nde moom itam xettali na ñu bare, ba ci man mii.
3Nuyulleen ma Piriska ak Akilas, sama bokki liggéeykat yi ci liggéeyub Almasi Yeesu. 4Ñoom ñoo jaay seen bakkan ngir ma mucc, te du man doŋŋ maa leen ameel njukkal, waaye mboolooy gëmkat yu jàmbur ñi dul Yawut yépp a leen ameel njukkal.
5Nuyulleen ma itam mbooloom gëmkat miy daje ca seen kër. Nuyulleen ma sama soppe Epaynet, miy saraxu ndoortel meññeef ma génne ca diiwaanu Asi, ñeel Almasi bi. 6Nuyulleen ma Maryaama mi sonn lool ci yeen.
7Nuyulleen ma Andoronikus ak Yuña, sama bokki Yawut yi ñu ma tëjandooloon; ñu ñu nawloo lañu ci ndaw yi, te ñoo ma njëkka gëm sax Almasi bi.
8Nuyulleen ma Ampilyaatus mi ma soppal sama bopp ndax Sang bi.
9Nuyulleen ma it Urben, sunu mbokkum liggéeykat bi ci liggéeyub Almasi bi, ak Estakis, sama soppe; 10nuyulleen ma Apeles mi firndeel kóllëre gi mu am ci Almasi bi, te ngeen nuyul ma waa kër Aristobul, 11ak Erojon sama mbokkum Yawut, te ngeen nuyul ma waa kër Narsis ñi gëm Sang bi.
12Nuyulleen ma Tirifen ak Tirifos, jigéen ñu sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it ndaw si Persidd mi sonn lool ci liggéeyu Boroom bi.
13Nuyulleen ma Rufus mi Boroom bi tànnal boppam, ak yaayam jiy sama yaayu bopp. 14Nuyulleen ma Asànkirit ak Felegon ak Ermes ak Patarobas ak Ermas, ak mboolem bokk yi nekk ak ñoom.
15Nuyulleen ma it Filolog ak Yuli, ak Nere ak jigéenam, ak Olimpas ak mboolem ñu sell ñi nekk ak ñoom.
16Saafoonteeleen fóonante yu sell. Mboolooy gëmkati Almasi bi yépp nuyu nañu leen.
Kàdduy artu ak tàggoo ñeel na waa Room
17Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale aka téqtale, te ngeen moytu leen. 18Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi bi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ wu neex ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi. 19Yeen nag seenug dégg ndigal siiw na ba bir ñépp, moo tax ma di leen bége. Waaye damaa bëgg ngeen xelu ci lu baax, te seenum xel mucc ci lu bon. 20Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk.
Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!
21Timote sama mbokkum liggéeykat nuyu na leen, mook Lusiyus ak Yason ak Sosipater sama bokki Yawut.
22Man Tersiyus mi bind kàdduy bataaxal bi ci sama loxo nag, nuyu naa leen ci turu Boroom bi.
23Gayus mi may dalal, di dalal mbooloo mi mépp këram, nuyu na leen; Erast saytukatub alalu dëkk bi it, nuyu na leen, mook mbokk mi Kàrtus.
24Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi ànd ak yeen! Amiin.
Teraanga ñeel na Yàlla
25Kookoo leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi bi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk, 26mbóot mu Bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal, 27kooku mooy Yàlla mi wéetoo xam-xam, te moom la ndam ñeel ba fàww, ndax Yeesu Almasi bi! Amiin.
Currently Selected:
Room 16: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright