1
Room 15:13
Kàddug Yàlla
KY
Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesaleek gépp mbég ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen fees dell ak yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
Compare
Explore Room 15:13
2
Room 15:4
Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu njëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar.
Explore Room 15:4
3
Room 15:5-6
Kon nag Yàlla miy maye xolu muñ, di ñaaxe, yal na leen may mànkoo gu mat sëkk, ni ko Almasi Yeesu bëgge, ngir nu bokk jenn yéene ak genn kàddu gu ngeen sàbbaale Yàlla, sunu Baayu Sang bi, Yeesu Almasi bi.
Explore Room 15:5-6
4
Room 15:7
Kon nag, ni leen Almasi bi xajoo, nangeen ko xajoontee noonu, ngir teddaayu Yàlla.
Explore Room 15:7
5
Room 15:2
Na ku nekk ci nun sàkku bànneexu moroomam, ci lu koy jariñ, ngir feddali ngëmam.
Explore Room 15:2