1
Room 14:17-18
Kàddug Yàlla
KY
Ndax kat solos nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solos nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi. Noonu kat ku koy jaamoo Almasi bi, yaa neex Yàlla, am ngërëmal nit ñi.
Compare
Explore Room 14:17-18
2
Room 14:8
Su nuy dund, ngir Boroom bi lanuy dund, su nu deewee it, wormaal Boroom bee tax nu dee. Kon nag nuy dund mbaa nu dee Boroom bi moo nu moom.
Explore Room 14:8
3
Room 14:19
Kon nag nanu sàkku luy indi jàmm ak lu nu feddalantee.
Explore Room 14:19
4
Room 14:13
Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakkastal, mbaa lu koy xiirtal ci bàkkaar.
Explore Room 14:13
5
Room 14:11-12
Ndaxte bindees na ne: «Ndegam maay Kiy dund, Boroom bee ko wax, man la ñépp di sukkal seen bëti óom, te man Yàlla la làmmiñu ñépp di sàbbaal.» Kon ku nekk ci nun, yaay layool sa bopp fa Yàlla.
Explore Room 14:11-12
6
Room 14:1
Ku ngëmam dëgërul nag, xajooleen ko, te bañ cee càmbar gis-gis yu wuute.
Explore Room 14:1
7
Room 14:4
Yaw miy sikkal jaamub jàmbur, yaay kan? Jaam bu taxaw ci liggéeyam mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la! Te day baaxal ndax Boroom bi man na koo baaxal.
Explore Room 14:4