Room 14
14
Bul sikkal sa moroom
1Ku ngëmam dëgërul nag, xajooleen ko, te bañ cee càmbar gis-gis yu wuute. 2Mu mel ni tey, kii ngëmam moo ko may mu saña lekk lu nekk; kee, ngëmam lujum doŋŋ la ko ngëmam gu dëgërul may mu lekk. 3Kiy lekk, bumu ko xeebe ki lekkul; ki lekkul it, bumu sikk kiy lekk, ndax Yàllaa ko xajoo. 4Yaw miy sikkal jaamub jàmbur, yaay kan? Jaam bu taxaw ci liggéeyam mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la! Te day baaxal ndax Boroom bi man na koo baaxal.
5Naka noonu kii jàpp na ne, bés gën naa rafet moroom ma; kee jàpp ne, bés yépp a yem. Na ku nekk seet la ko doy, te yem ca. 6Ndax kiy taamu bés, Boroom bi la koy taamul; naka noonu kiy lekk, Boroom bi la koy gërëme, nde moom lay sant doora lekk; ki lekkul it Boroom bi lay sàkkoo ñàkka lekkam, te Yàlla lay sant. 7Ndax kat kenn ci nun dundul ngir boppam, te kenn deewul ngir boppam. 8Su nuy dund, ngir Boroom bi lanuy dund, su nu deewee it, wormaal Boroom bee tax nu dee. Kon nag nuy dund mbaa nu dee Boroom bi moo nu moom.
9Loolu sax moo waral Almasi bi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom. 10Yaw nag ana looy sikke sa mbokkum gëmkat, ak itam, ana looy xeebe sa mbokkum gëmkat? Ndax kat nun ñépp ay taxawi fa kanam jalub àttekaayu Yàlla ba. 11Ndaxte bindees na ne:
«Ndegam maay Kiy dund, Boroom bee ko wax,
man la ñépp di sukkal seen bëti óom,
te man Yàlla la làmmiñu ñépp di sàbbaal#14.11 Seetal ci Esayi 45.23..»
12Kon ku nekk ci nun, yaay layool sa bopp fa Yàlla.
Bul yóbbe sa moroom bàkkaar
13Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakkastal, mbaa lu koy xiirtal ci bàkkaar. 14Xam naa nag, wér na ma it te Sang Yeesu tax, ne amul lenn lu sobewu ci wàllu boppam, ba daganula lekk; waaye ki jàppe lenn muy lu sobewu, ci moom la loola di lu sobewu. 15Soo dee lekk lenn ba tax sa mbokk am ci lu ko naqari, noppi ngaa doxe cofeel. Bu sag lekk sànk ku tax Almasi bi dee. 16Li dagan ci yaw, bu ko jariñoo ba may kenn lu mu ŋàññee. 17Ndax kat solos nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solos nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi. 18Noonu kat ku koy jaamoo Almasi bi, yaa neex Yàlla, am ngërëmal nit ñi.
19Kon nag nanu sàkku luy indi jàmm ak lu nu feddalantee. 20Aw ñam, bumu la yàqloo liggéeyu Yàlla. Dëgg la, wépp ñam set na, waaye lekk ga nga koy lekk, su gàkkalee ngëmu keneen, def nga lu aay. 21Li gën sax mooy nga baña lekk yàpp, mbaa nga baña naan biiñ, mbaa leneen lu mu doon lu mana fakkastal sa mbokkum gëmkat.
22Yaw ci sa wàllu bopp, ngëm gi nga ci am, yemale ko ci sa bopp, fi kanam Yàlla. Ndokkalee ki sikkul boppam lenn ci jëfin wu mu dogul boppam ne noonu lay jëfe. 23Waaye ki am xel ñaar, su lekkee, ab daan topp na ko, nde jëfewul ngëm, te lu ngëm lalul bàkkaar la.
Currently Selected:
Room 14: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright