1
Filib 1:6
Kàddug Yàlla
KY
Te lii kat, bir na ma: ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.
Compare
Explore Filib 1:6
2
Filib 1:9-10
Li may ñaan nag moo di seen cofeel yokku tey gën di yokku, te ngeen ànd ceek xam-xam bu matale ak gépp ràññee, ba mana xàmmee li gën. Su ko defee ngeen set wecc te mucc sikk, ngir keroog bés bi Almasi bi di délsi.
Explore Filib 1:9-10
3
Filib 1:21
Ndax samag dund, Almasi bi la ñeel, samag dee dàqati.
Explore Filib 1:21
4
Filib 1:3
Damay sant Yàlla sama Boroom saa yu ma leen fàttalikoo
Explore Filib 1:3
5
Filib 1:27
Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi bi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di bokk xeex, ngir saxal ngëm gi sukkandikoo ci xibaaru jàmm bi.
Explore Filib 1:27
6
Filib 1:20
Loolu laa ne siiw, yaakaar ko, te duma rus mukk, xanaa di saxoo aw fit, démb niki tey, ngir ma mana fésale sama jëmm jépp màggaayu Almasi bi, su may dund ak su may dee.
Explore Filib 1:20
7
Filib 1:29
Ndax kat yeen la may ci jëmmu Almasi bi, yiwu gëm ko, rax ci dolli ngeen sonn ndax moom.
Explore Filib 1:29