1
Filib 2:3-4
Kàddug Yàlla
KY
Buleen def dara ci kaw wujje, mbaa réy-réylu, waaye woyofluleen, ba jàpp ne seeni moroom a leen gën. Bu kenn ci yeen xintewoo njariñal boppam, waaye na ku nekk bàyyi xel moroomam.
Compare
Explore Filib 2:3-4
2
Filib 2:5
Noonu Almasi Yeesu doon doxale, deeleen ko doxale ci seen biir
Explore Filib 2:5
3
Filib 2:6-8
Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul ci dayob boppam bi ko def nawleb Yàlla. Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam. Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj.
Explore Filib 2:6-8
4
Filib 2:13
ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.
Explore Filib 2:13
5
Filib 2:9-11
Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur, ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom, muy ci kaw asamaan, di ci kaw suuf, di biir suuf, làmmiñu ñépp it biral ne Yeesu Almasi bi mooy Sang bi, te muy màggaayu Yàlla Baay bi.
Explore Filib 2:9-11
6
Filib 2:14-15
Mboolem lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo, ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si
Explore Filib 2:14-15
7
Filib 2:12
Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox
Explore Filib 2:12