Filib 1
1
Ubbite gi
1Man la Póol, Timote miy jaamub Almasi Yeesu ni man ànd ak man ci lii, ñeel mboolem ñu sell ñi gëm Almasi Yeesu, te dëkke Filib, yeen ak seeni njiit ak jàppalekati mbooloo mi. 2Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa sunu Baay ak Sang Yeesu Almasi bi.
Póol ñaanal na waa Filib
3Damay sant Yàlla sama Boroom saa yu ma leen fàttalikoo, 4te saa su ma leen di ñaanal, mbég laa leen di ñaanale yeen ñépp, 5ndax seen loxo bi ngeen jo ci xamle xibaaru jàmm bi, te dale ko ca bés bu njëkk ba, ba tey. 6Te lii kat, bir na ma: ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.
7Maa yey nag njortal leen loolu yeen ñépp, ndax ci sama xol laa leen def, te it muy ci wàllu jéng yi ñu ma jénge, di ci wàllu kàddu guy waxal xibaaru jàmm bi ak di ko feddali, yeen ñépp am ngeen wàll ci sama añub yiw. 8Yàlla seede na ne sopp naa leen yeen ñépp, cofeel gu Almasi Yeesu ci boppam àttana tibbe ci biir xolam.
9Li may ñaan nag moo di seen cofeel yokku tey gën di yokku, te ngeen ànd ceek xam-xam bu matale ak gépp ràññee, 10ba mana xàmmee li gën. Su ko defee ngeen set wecc te mucc sikk, ngir keroog bés bi Almasi bi di délsi. 11Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub gi Yeesu Almasi bi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.
Jéngi Póol jéngul kàddug Yàlla
12Damaa bëgg, bokk yi, ngeen xam ne lii ma dal, xibaaru jàmm bi la far jëmale kanam. 13Ndax kat, bir na mboolem dagi boroom dëkk bi te bir na ñeneen ñépp ne Almasi bee tax ñu jéng ma. 14Te it li gëna bare ci bokki gëmkat ñi, sama jéng yi ma nekke nii moo leen yokk aw fit, ba tax ñu gëna ñemee waxe kàddu gi te ragaluñu ci dara.
15Dëgg la am na ñuy waare ci turu Almasi bi ci kaw kiñaan ak diiroo mbagg, waaye am na itam ñu koy defe yéene ju rafet. 16Ñooñu cofeel a leen tax di waare, ndax xam nañu ne waxal xibaaru jàmm bi laa sasoo. 17Waaye ñale, xelum wujje lañuy siiwtaanee Almasi bi, du yéene ju rafet ju ñu ci am, xanaa defe ne seeni pexe man na maa yokk coono ci diggante bii ñu ma jénge.
18Ana lu ci topp nag? Ba tey rekk, ak nu mu mana deme, muy waareb jinigal, mbaa waare bu dëggu, turu Almasi bi moo ci jollee, muy sama mbégtem tey, dellu di sama mbégtem ëllëg, 19ndax xam naa ne loolu lépp ay walbatiku di samag mucc, ndax seeni ñaan ak ndimbalal Noo gu Sell gu Yeesu Almasi bi. 20Loolu laa ne siiw, yaakaar ko, te duma rus mukk, xanaa di saxoo aw fit, démb niki tey, ngir ma mana fésale sama jëmm jépp màggaayu Almasi bi, su may dund ak su may dee. 21Ndax samag dund, Almasi bi la ñeel, samag dee dàqati. 22Su dee nag damaa wara wéye sama bakkan bii, ngir mana sottal ab liggéey bu am njariñ, ana lu ma gënal ci diggante dund ak dee? Xawma ko. 23Ci diggante ñaar yooyii laa tance: yàkkamti namaa yiwiku ba fekki Almasi bi, te loolu moo dàqati fuuf. 24Waaye ma deseegum bakkan moo gëna jamp ci yeen. 25Gannaaw loolu bir na ma nag, xam naa ne dinaa desagum, desandoo fi ak yeen ñépp, ngir ngeen jëm kanam, tey bége seen ngëm, 26ba bu ma délsee fi yeen, ngeen gëna mana puukarewoo Almasi Yeesu ndax man.
27Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi bi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di bokk xeex, ngir saxal ngëm gi sukkandikoo ci xibaaru jàmm bi. 28Buleen ragal seeni noon ci lenn. Seen fit mooy màndargaal sànkutey noon yi, te yeen it, mooy màndargaal seenug mucc gu bawoo fa Yàlla. 29Ndax kat yeen la may ci jëmmu Almasi bi, yiwu gëm ko, rax ci dolli ngeen sonn ndax moom. 30Bokk ngeen coonoy benn xare bi ak man, xare bi ngeen gisoon ma xare ko démb, moom ngeen dégg ba tey, ma di ko xare.
Currently Selected:
Filib 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright