1
Efes 6:12
Kàddug Yàlla
KY
Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.
Compare
Explore Efes 6:12
2
Efes 6:18
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
Explore Efes 6:18
3
Efes 6:11
Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane.
Explore Efes 6:11
4
Efes 6:13
Kon nag jëlleen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm.
Explore Efes 6:13
5
Efes 6:16-17
Te fu ngeen tollu ŋàbbleen pakk biy seen ngëm, ci ngeen mana fanqe mboolem jumi sawaray ku bon ki. Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jëlleen ko, sol; jëlleen itam saamar bi Noo gu Sell giy joxe, te muy kàddug Yàlla.
Explore Efes 6:16-17
6
Efes 6:14-15
Taxawleen kon temm. Defleen dëgg di ngañaay li ci seen ndigg, njub di seen kiiraayal dënn. Xibaaru jàmm bi indi jàmm nag, defleen ko muy dàll yu dëgëral seen taxawaay.
Explore Efes 6:14-15
7
Efes 6:10
Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.
Explore Efes 6:10
8
Efes 6:2-3
«Teralleen seen ndey ak seen baay,» mooy ndigal li njëkka ànd akub dige, ndax da ne: «ngir ngeen baaxle te gudd fan ci kaw suuf.»
Explore Efes 6:2-3
9
Efes 6:1
Naka yeen xale yi, déggalleen seeni waajur, ngir Boroom bi, ndax moo war.
Explore Efes 6:1