Waaye ndegam maay Kiy dund, te leeru Aji Sax ji mooy fees àddina sépp, gannaaw mboolem nit ñi gis samag leer, gis firnde yi ma def ci digg Misra ak ci màndiŋ mi, ñoo ma seetlu woon nii fukki yoon, bañ maa déggal, kenn ci ñoom déy du gis réew mi ma giñaloon seeni maam. Mboolem ñi ma xarab, kenn du ko ci gis.