1
Màndiŋ ma 13:30
Kàddug Yàlla
KY
Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»
Compare
Explore Màndiŋ ma 13:30
2
Màndiŋ ma 13:33
Fa lanu gis xeetu Nefilim ya, ponkali Anageen ña bokk ca xeetu Nefilim ya, nuy niru sunu bopp ay soccet fi seen kanam, di leen ko niru, ñoom it.»
Explore Màndiŋ ma 13:33
3
Màndiŋ ma 13:31
Ndaw ya àndoon ak moom daldi ne: «Manunoo songi waa réew ma, ndax ñoo nu ëpp doole.»
Explore Màndiŋ ma 13:31
4
Màndiŋ ma 13:32
Ci biir loolu ñuy baatal ca kanam bànni Israayil, réew ma ñu nemmikuji woon. Ñu naan: «Réew moomee ñu wëri woon ngir nemmiku ko déy, réew la muy mëdd ay sancaanam, te mboolem askan wa nu fa gis, ay boroom jëmm lañu.
Explore Màndiŋ ma 13:32
5
Màndiŋ ma 13:27
Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa.
Explore Màndiŋ ma 13:27
6
Màndiŋ ma 13:28
Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbaliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis.
Explore Màndiŋ ma 13:28
7
Màndiŋ ma 13:29
Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.»
Explore Màndiŋ ma 13:29
8
Màndiŋ ma 13:26
Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israayil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar yi, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma.
Explore Màndiŋ ma 13:26