Màndiŋ ma 13
13
Musaa yeble na Kanaan
1Aji Sax ji waxati Musaa, ne: 2«Yebalal ay ndaw, ñu dem yëri réewum Kanaan, gi may jox bànni Israayil. Kenn ngay yebal ci seen giiri maam yi, giir gu ci nekk, kenn, te ku ci nekk di kilifa ci ñoom.» 3Ci kaw loolu Musaa yebal ndaw ña ci ndigalal Aji Sax ji, ñu bàyyikoo ca màndiŋu Paran. Ñoom ñépp ay njiiti bànni Israayil lañu woon. 4Ñooñu ñoo di:
Samwa doomu Sakur, ci giirug Rubeneen ñi,
5ak Safat doomu Ori, ci giirug Cimyoneen ñi,
6ak Kaleb doomu Yefune, ci giirug Yudeen ñi,
7ak Igal doomu Yuusufa, ci giirug Isakareen ñi,
8ak Ose doomu Nuun, ci giirug Efraymeen ñi,
9ak Palti doomu Rafu, ci giirug Beñamineen ñi,
10ak Gadyel doomu Sodi, ci giirug Cabuloneen ñi,
11ak Gadi doomu Susi, mi taxawal làngu Manase ci biir giirug Yuusufeen ñi,
12ak Amyel doomu Gemali, ci giirug Daneen ñi,
13ak Setur doomu Mikayel, ci giirug Asereen ñi,
14ak Nabi doomu Wofsi, ci giirug Neftaleen ñi,
15ak Gewuyel doomu Maki, ci giiru Gàddeen ñi.
16Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Ose doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
17Ba leen Musaa yebalee ngir ñu yëri réewum Kanaan, da ne leen: «Ci Negew gi di diiwaan bi ci bëj-saalum ngeen di jaare, yéegi ca diiwaanu tund ya, 18ba gis nu réew ma mel: ndax waa réew ma, ñu am doole lañu, walla ñu néew doole; ñu néew lañu, walla ñu bare; 19ak ndax réew ma baax na, walla baaxul; ak nu seeni dëkk mel: ndax ay dal rekk la, walla ay dëkk yu ñu dàbbali la; 20ak suuf sa: ndax nangu na, am nanguwul; ak itam ndax am nay garab, am déet. Te ngeen góor-góorlu ba sàkkaale ca meññeefi réew ma.» Fan yooyu nag yemook reseñ di meññ ndoortel meññeef.
21Ci kaw loolu ndaw ya dem yëri réew ma, dale ko ca màndiŋu Ciin, ba àgg Rexob, ga ca wetu Amat. 22Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Aximan ak Sesay ak Talmay dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra. 23Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg. 24Béreb boobu lañu dippee xuru Eskol, (muy firi xuru Cëgg) ndax cëgg ba fa bànni Israayil dagge woon.
Ndaw ya délsi nañu
25Ndaw ya nag ñibbisi, gannaaw ba ñu nemmikoo réew ma lu mat ñeent fukki fan. 26Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israayil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar yi, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma. 27Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa. 28Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbaliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis. 29Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.»
30Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»
31Ndaw ya àndoon ak moom daldi ne: «Manunoo songi waa réew ma, ndax ñoo nu ëpp doole.» 32Ci biir loolu ñuy baatal ca kanam bànni Israayil, réew ma ñu nemmikuji woon. Ñu naan: «Réew moomee ñu wëri woon ngir nemmiku ko déy, réew la muy mëdd ay sancaanam, te mboolem askan wa nu fa gis, ay boroom jëmm lañu. 33Fa lanu gis xeetu Nefilim ya, ponkali Anageen ña bokk ca xeetu Nefilim ya, nuy niru sunu bopp ay soccet fi seen kanam, di leen ko niru, ñoom it.»
Currently Selected:
Màndiŋ ma 13: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright