1
Màrk 14:36
Kàddug Yàlla
KY
Mu ne: «Abba, Baay, yaw mi dara tëwul, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Waaye bumuy sama coobare, nay doon ci sa coobare.»
Compare
Explore Màrk 14:36
2
Màrk 14:38
Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»
Explore Màrk 14:38
3
Màrk 14:9
Te maa leen ko wax déy, li ndaw sii def, fépp fu ñuy yéeneji ëllëg xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dees na ko fa nettalee, di ko fàttalikoo jëmmu ndaw si.»
Explore Màrk 14:9
4
Màrk 14:34
Mu ne leen: «Tiis wuy rey la sama xol fees, ba may bëgga dee! Toogleen fii te ngeen teewlu.»
Explore Màrk 14:34
5
Màrk 14:22
Naka ñuy lekk, Yeesu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg, jox leen, daldi ne: «Jëlleen, lii sama yaram la.»
Explore Màrk 14:22
6
Màrk 14:23-24
Mu teg ca jël ab kaas, yékkati kàddug cant, jox leen, ñépp naan ca. Mu ne leen: «Lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te nara tuurul ñépp.
Explore Màrk 14:23-24
7
Màrk 14:27
Yeesu nag ne leen: «Yeen ñépp ay dellu gannaaw, ndax bindees na ne: “Maay dóor sàmm bi, xar yi tasaaroo.”
Explore Màrk 14:27
8
Màrk 14:42
Jógleen, nu dem. Ki may wor a ngi nii.»
Explore Màrk 14:42
9
Màrk 14:30
Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy, yaw, guddig tey jii, bala ganaar a sab ñaari yoon, dinga ma jàmbu ñetti yoon.»
Explore Màrk 14:30